# ko/Korean.xml.gz
# wo/Wolof-NT.xml.gz
(src)="b.MAT.1.1.1"> 아브라함과 다윗의 자손 예수 그리스도의 세계라
(trg)="b.MAT.1.1.1"> Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist , sëtu Daawuda , sëtu Ibraayma .
(src)="b.MAT.1.2.1"> 아브라함이 이삭을 낳고 이삭은 야곱을 낳고 야곱은 유다와 그의 형제를 낳고
(trg)="b.MAT.1.2.1"> Ibraayma moo jur Isaaxa ; Isaaxa jur Yanqóoba ; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam ;
(src)="b.MAT.1.3.1"> 유다는 다말에게서 베레스와 세라를 낳고 베레스는 헤스론을 낳고 헤스론은 람을 낳고
(trg)="b.MAT.1.3.1"> Yuda , Fares ak Sara ci Tamar ; Fares Esrom , miy baayu Aram ;
(src)="b.MAT.1.4.1"> 람은 아미나답을 낳고 아미나답은 나손을 낳고 나손은 살몬을 낳고
(trg)="b.MAT.1.4.1"> Aram Aminadab ; Aminadab Naason ; Naason Salmon ;
(src)="b.MAT.1.5.1"> 살몬은 라합에게서 보아스를 낳고 보아스는 룻에게서 오벳을 낳고 오벳은 이새를 낳고
(trg)="b.MAT.1.5.1"> Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas ; Bowas am ak Ruut Obedd ; Obedd jur Yese ,
(src)="b.MAT.1.6.1"> 이새는 다윗왕을 낳으니라 다윗은 우리야의 아내에게서 솔로몬을 낳고
(trg)="b.MAT.1.6.1"> miy baayu buur bi Daawuda .
(trg)="b.MAT.1.6.2"> Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon jabari Uri ;
(src)="b.MAT.1.7.1"> 솔로몬은 르호보암을 낳고 르호보암은 아비야를 낳고 아비야는 아사를 낳고
(trg)="b.MAT.1.7.1"> Suleymaan jur Robowam ; Robowam Abiya ; Abiya Asaf ;
(src)="b.MAT.1.8.1"> 아사는 여호사밧을 낳고 여호사밧은 요람을 낳고 요람은 웃시야를 낳고
(trg)="b.MAT.1.8.1"> Asaf Yosafat ; Yosafat Yoram , miy baayu Osiyas ;
(src)="b.MAT.1.9.1"> 웃시야는 요담을 낳고 요담은 아하스를 낳고 아하스는 히스기야를 낳고
(trg)="b.MAT.1.9.1"> Osiyas jur Yowatam ; Yowatam Akas , miy baayu Esekiyas ;
(src)="b.MAT.1.10.1"> 히스기야는 므낫세를 낳고 므낫세는 아몬을 낳고 아몬은 요시야를 낳고
(trg)="b.MAT.1.10.1"> Esekiyas Manase ; Manase Amon ; Amon Yosiyas ;
(src)="b.MAT.1.11.1"> 바벨론으로 이거할 때에 요시야는 여고냐와 그의 형제를 낳으니라
(trg)="b.MAT.1.11.1"> Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono , ja ñu defe Yawut ya jaam , yóbbu leen Babilon .
(src)="b.MAT.1.12.1"> 바벨론으로 이거한 후에 여고냐는 스알디엘을 낳고 스알디엘은 스룹바벨을 낳고
(trg)="b.MAT.1.12.1"> Ba ñu leen yóbboo ca Babilon , Yekoñas jur Salacel ; Salacel Sorobabel ,
(src)="b.MAT.1.13.1"> 스룹바벨은 아비훗을 낳고 아비훗은 엘리아김을 낳고 엘리아김은 아소르를 낳고
(trg)="b.MAT.1.13.1"> miy baayu Abiyudd ; Abiyudd Eliyakim ; Eliyakim Asor ;
(src)="b.MAT.1.14.1"> 아소르는 사독을 낳고 사독은 아킴를 낳고 아킴은 엘리웃을 낳고
(trg)="b.MAT.1.14.1"> Asor Sadog ; Sadog Akim ; Akim Eliyudd ;
(src)="b.MAT.1.15.1"> 엘리웃은 엘르아살을 낳고 엘르아살은 맛단을 낳고 맛단은 야곱을 낳고
(trg)="b.MAT.1.15.1"> Eliyudd Eleyasar ; Eleyasar Matan , miy baayu Yanqóoba ;
(src)="b.MAT.1.16.1"> 야곱은 마리아의 남편 요셉을 낳았으니 마리아에게서 그리스도라 칭하는 예수가 나시니라
(trg)="b.MAT.1.16.1"> Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama ; te ci Maryaama la Yeesu , mi ñuy wax Kirist , juddoo .
(src)="b.MAT.1.17.1"> 그런즉 모든 대 수가 아브라함부터 다윗까지 열 네 대요 다윗 부터 바벨론으로 이거할 때까지 열 네 대요 바벨론으로 이거 한후부터 그리스도까지 열 네 대러라
(trg)="b.MAT.1.17.1"> Mboolem giir googu nag , la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda , fukk lañu ak ñeent ; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon , fukk lañu ak ñeent ; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist , fukk lañu ak ñeent .
(src)="b.MAT.1.18.1"> 예수 그리스도의 나심은 이러하니라 그 모친 마리아가 요셉과 정혼하고 동거하기 전에 성령으로 잉태된 것이 나타났더니
(trg)="b.MAT.1.18.1"> Nii la Yeesu Kirist juddoo .
(trg)="b.MAT.1.18.2"> Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa , waaye laata ñoo ànd , gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi .
(src)="b.MAT.1.19.1"> 그 남편 요셉은 의로운 사람이라 저를 드러내지 아니하고 가만히 끊고자하여
(trg)="b.MAT.1.19.1"> Yuusufa jëkkëram nag , nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woon a weer .
(trg)="b.MAT.1.19.2"> Mu nar a xàccook moom ci sutura .
(src)="b.MAT.1.20.1"> 이 일을 생각할 때에 주의 사자가 현몽하여 가로되 다윗의 자손 요셉아 네 아내 마리아 데려오기를 무서워 말라 저에게 잉태된 자는 성령으로 된 것이라
(trg)="b.MAT.1.20.1"> Waaye bi muy xalaat ci loolu , benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko : « Yaw Yuusufa , sëtu Daawuda , bul ragal a yeggali Maryaama sa jabar , ndaxte doom ji mu ëmb , ci Xel mu Sell mi la jóge .
(src)="b.MAT.1.21.1"> 아들을 낳으리니 이름을 예수라 하라 이는 그가 자기 백성을 저희 죄에서 구원할 자이심이라 하니라
(trg)="b.MAT.1.21.1"> Dina jur doom ju góor ; na nga ko tudde Yeesu , ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar . »
(src)="b.MAT.1.22.1"> 이 모든 일의 된 것은 주께서 선지자로 하신 말씀을 이루려 하심이니 가라사대
(trg)="b.MAT.1.22.1"> Loolu lépp xewoon na , ngir amal li Boroom bi wax , jaarale ko cib yonent , bi mu naan :
(src)="b.MAT.1.23.1"> 보라 처녀가 잉태하여 아들을 낳을 것이요 그 이름은 임마누엘이라 하리라 하셨으니 이를 번역한즉 하나님이 우리와 함께 계시다 함이라
(trg)="b.MAT.1.23.1"> « Janq bi dina ëmb , jur doom ju góor , ñu tudde ko Emanuwel , » liy tekki « Yàlla ganesi na nu . »
(src)="b.MAT.1.24.1"> 요셉이 잠을 깨어 일어나서 주의 사자의 분부대로 행하여 그 아내를 데려 왔으나
(trg)="b.MAT.1.24.1"> Noonu Yuusufa yeewu , yeggali jabaram , na ko ko malaakam Boroom bi sante woon .
(src)="b.MAT.1.25.1"> 아들을 낳기까지 동침치 아니하더니 낳으매 이름을 예수라 하니라
(trg)="b.MAT.1.25.1"> Waaye àndul ak moom , ba kera mu mucc , jur doom ju góor ; mu tudde ko Yeesu .
(src)="b.MAT.2.1.1"> 헤롯왕 때에 예수께서 유대 베들레헴에서 나시매 동방으로부터 박사들이 예루살렘에 이르러 말하되
(trg)="b.MAT.2.1.1"> Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude , amoon na ay boroom xam-xam , ñu jóge penku , ñëw Yerusalem .
(trg)="b.MAT.2.1.2"> Booba , ci jamonoy buur bi Erodd la woon .
(src)="b.MAT.2.2.1"> 유대인의 왕으로 나신 이가 어디 계시뇨 우리가 동방에서 그의 별을 보고 그에게 경배하러 왔노라 하니
(trg)="b.MAT.2.2.1"> Ñu ne : « Ana buur bi juddul Yawut yi ?
(trg)="b.MAT.2.2.2"> Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko . »
(src)="b.MAT.2.3.1"> 헤롯왕과 온 예루살렘이 듣고 소동한지라
(trg)="b.MAT.2.3.1"> Bi ko Erodd buur ba déggee , mu daldi jaaxle , moom ak waa Yerusalem gépp .
(src)="b.MAT.2.4.1"> 왕이 모든 대제사장과 백성의 서기관들을 모아 그리스도가 어디서 나겠느뇨 물으니
(trg)="b.MAT.2.4.1"> Mu woolu nag saraxalekat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa , laaj leen fu Almasi bi , maanaam Kirist , war a juddoo .
(src)="b.MAT.2.5.1"> 가로되 유대 베들레헴이오니 이는 선지자로 이렇게 기록된바
(trg)="b.MAT.2.5.1"> Ñu ne ko : « Ca Betleyem ci diiwaanu Yude , ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent :
(src)="b.MAT.2.6.1"> 또 유대 땅 베들레헴아 너는 유대 고을 중에 가장 작지 아니하도다 네게서 한 다스리는 자가 나와서 내 백성 이스라엘의 목자가 되리라 하였음이니이다
(trg)="b.MAT.2.6.1"> “ Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude , du yaw yaa yées ci njiiti Yude , ndaxte ci yaw la njiit di génne , kiy sàmm Israyil sama xeet . ” »
(src)="b.MAT.2.7.1"> 이에 헤롯이 가만히 박사들을 불러 별이 나타난 때를 자세히 묻고
(trg)="b.MAT.2.7.1"> Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya , di leen ceddowu , ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq .
(src)="b.MAT.2.8.1"> 베들레헴으로 보내며 이르되 가서 아기에 대하여 자세히 알아보고 찾거든 내게 고하여 나도 가서 그에게 경배하게 하라
(trg)="b.MAT.2.8.1"> Noonu mu yebal leen Betleyem naan : « Demleen fa , seet bu wóor mbirum xale ba .
(trg)="b.MAT.2.8.2"> Bu ngeen ci amee lu wóor nag , ngeen xamal ma ko , ngir man itam ma dem màggal ko . »
(src)="b.MAT.2.9.1"> 박사들이 왕의 말을 듣고 갈쌔 동방에서 보던 그 별이 문득 앞서 인도하여 가다가 아기 있는 곳 위에 머물러 섰는지라
(trg)="b.MAT.2.9.1"> Ba ñu dégloo buur ba nag , ñu dem .
(trg)="b.MAT.2.9.2"> Te biddiiw , ba ñu gisoon ca penku ba , ne tell jiite leen , ba àgg , tiim fa xale ba nekk .
(src)="b.MAT.2.10.1"> 저희가 별을 보고 가장 크게 기뻐하고 기뻐하더라
(trg)="b.MAT.2.10.1"> Ba ñu gisee biddiiw ba nag , ñu am mbég mu réy-a-réy .
(src)="b.MAT.2.11.1"> 집에 들어가 아기와 그 모친 마리아의 함께 있는 것을 보고 엎드려 아기께 경배하고 보배합을 열어 황금과 유향과 몰약을 예물로 드리니라
(trg)="b.MAT.2.11.1"> Ñu dugg ca kër ga , gis xale ba ak Maryaama ndeyam , ñu daldi sukk , di ko màggal .
(trg)="b.MAT.2.11.2"> Ñu ubbi seeni boyetu alal , may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir .
(src)="b.MAT.2.12.1"> 꿈에 헤롯에게로 돌아가지 말라 지시하심을 받아 다른 길로 고국에 돌아가니라
(trg)="b.MAT.2.12.1"> Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént , ñu bañ a dellu ca Erodd .
(trg)="b.MAT.2.12.2"> Noonu ñu jaar weneen yoon , ñibbi seen réew .
(src)="b.MAT.2.13.1"> 저희가 떠난 후에 주의 사자가 요셉에게 현몽하여 가로되 헤롯이 아기를 찾아 죽이려하니 일어나 아기와 그의 모친을 데리고 애굽으로 피하여 내가 네게 이르기까지 거기 있으라 하시니
(trg)="b.MAT.2.13.1"> Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu , benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko : « Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi , ngir rey ko ; jógal nag , jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra , toog fa , ba kera ma koy wax . »
(src)="b.MAT.2.14.1"> 요셉이 일어나서 밤에 아기와 그의 모친을 데리고 애굽으로 떠나가
(trg)="b.MAT.2.14.1"> Yuusufa nag jóg , jël xale ba ak ndeyam , làquji Misra ca guddi ga .
(src)="b.MAT.2.15.1"> 헤롯이 죽기까지 거기 있었으니 이는 주께서 선지자로 말씀하신바 애굽에서 내 아들을 불렀다 함을 이루려 하심이니라
(trg)="b.MAT.2.15.1"> Mu toog fa , ba Erodd faatu .
(trg)="b.MAT.2.15.2"> Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent , bi mu naan : « Woo naa sama doom , mu génn Misra . »
(src)="b.MAT.2.16.1"> 이에 헤롯이 박사들에게 속은 줄을 알고 심히 노하여 사람을 보내어 베들레헴과 그 모든 지경 안에 있는 사내아이를 박사들에게 자세히 알아 본 그 때를 표준하여 두 살부터 그 아래로 다 죽이니
(trg)="b.MAT.2.16.1"> Bi Erodd gisee nag , ne boroom xam-xam ya nax nañu ko , mu daldi mer lool .
(trg)="b.MAT.2.16.2"> Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër , rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf , mengook jamono , ja ko boroom xam-xam ya waxoon .
(src)="b.MAT.2.17.1"> 이에 선지자 예레미야로 말씀하신바
(trg)="b.MAT.2.17.1"> Booba am la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi , bi mu naan :
(src)="b.MAT.2.18.1"> 라마에서 슬퍼하며 크게 통곡하는 소리가 들리니 라헬이 그 자식을 위하여 애곡하는 것이라 그가 자식이 없으므로 위로 받기를 거절하였도다 함이 이루어졌느니라
(trg)="b.MAT.2.18.1"> « Baat jib na ci Rama , ay jooy ak yuux gu réy , Rasel mooy jooy ay doomamte bëggul kenn dëfël ko , ndaxte saay nañu . »
(src)="b.MAT.2.19.1"> 헤롯이 죽은 후에 주의 사자가 애굽에서 요셉에게 현몽하여 가로되
(trg)="b.MAT.2.19.1"> Bi nga xamee ne Erodd faatu na , benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra ,
(src)="b.MAT.2.20.1"> 일어나 아기와 그 모친을 데리고 이스라엘 땅으로 가라 아기의 목숨을 찾던 자들이 죽었느니라 하시니
(trg)="b.MAT.2.20.1"> ne ko : « Ñi doon wut a rey xale ba dee nañu ; jógal nag , jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil . »
(src)="b.MAT.2.21.1"> 요셉이 일어나 아기와 그 모친을 데리고 이스라엘 땅으로 들어오니라
(trg)="b.MAT.2.21.1"> Yuusufa jóg nag , jël xale ba ak ndeyam , dellu Israyil .
(src)="b.MAT.2.22.1"> 그러나 아켈라오가 그 부친 헤롯을 이어 유대의 임금 됨을 듣고 거기로 가기를 무서워하더니 꿈에 지시하심을 받아 갈릴리 지방으로 떠나가
(trg)="b.MAT.2.22.1"> Waaye bi mu déggee ne , Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude , mu ragal faa dem .
(trg)="b.MAT.2.22.2"> Yàlla artu ko nag ci gént , mu daldi dem diiwaanu Galile .
(src)="b.MAT.2.23.1"> 나사렛이란 동리에 와서 사니 이는 선지자로 하신 말씀에 나사렛 사람이라 칭하리라 하심을 이루려 함이러라
(trg)="b.MAT.2.23.1"> Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret .
(trg)="b.MAT.2.23.2"> Noonu am la ñu waxoon ca xale ba , jaarale ko ca yonent ya , bi ñu naan : « Dees na ko tudde Nasaréen . »
(src)="b.MAT.3.1.1"> 그 때에 세례 요한이 이르러 유대 광야에서 전파하여 가로되
(trg)="b.MAT.3.1.1"> Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na , di waare ca màndiŋu Yude .
(src)="b.MAT.3.2.1"> 회개하라 천국이 가까왔느니라 하였으니
(trg)="b.MAT.3.2.1"> Nii la doon waaree : « Tuubleen seeni bàkkaar , ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na . »
(src)="b.MAT.3.3.1"> 저는 선지자 이사야로 말씀하신 자라 일렀으되 광야에 외치는 자의 소리가 있어 가로되 너희는 주의 길을 예비하라 그의 첩경을 평탄케 하라 하였느니라
(trg)="b.MAT.3.3.1"> Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi , bi mu naan : « Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne : “ Xàll-leen yoonu Boroom bi , jubal-leen fi muy jaar . ” »
(src)="b.MAT.3.4.1"> 이 요한은 약대 털옷을 입고 허리에 가죽띠를 띠고 음식은 메뚜기와 석청이었더라
(trg)="b.MAT.3.4.1"> Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem , takk geñog der ci ndiggam .
(trg)="b.MAT.3.4.2"> Ay njéeréer la doon dunde ak lem .
(src)="b.MAT.3.5.1"> 이 때에 예루살렘과 온 유대와 요단강 사방에서 다 그에게 나아와
(trg)="b.MAT.3.5.1"> Noonu ñépp génn jëm ci moom , ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude , ak waa dexu Yurdan .
(src)="b.MAT.3.6.1"> 자기들의 죄를 자복하고 요단강에서 그에게 세례를 받더니
(trg)="b.MAT.3.6.1"> Ñu nangu seeni bàkkaar , Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan .
(src)="b.MAT.3.7.1"> 요한이 많은 바리새인과 사두개인이 세례 베푸는데 오는 것을 보고 이르되 독사의 자식들아 누가 너희를 가르쳐 임박한 진노를 피하라 하더냐
(trg)="b.MAT.3.7.1"> Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya , ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga .
(trg)="b.MAT.3.7.2"> Waaye bi leen Yaxya gisee , mu ne leen : « Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co , ku leen artu , ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc ?
(src)="b.MAT.3.8.1"> 그러므로 회개에 합당한 열매를 맺고
(trg)="b.MAT.3.8.1"> Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar ,
(src)="b.MAT.3.9.1"> 속으로 아브라함이 우리 조상이라고 생각지 말라 내가 너희에게 이르노니 하나님이 능히 이 돌들로도 아브라함의 자손이 되게 하시리라
(trg)="b.MAT.3.9.1"> te buleen wax ci seen xel naan : “ Nun daal doomi Ibraayma lanu , ” ndaxte maa ngi leen koy wax , Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii .
(src)="b.MAT.3.10.1"> 이미 도끼가 나무 뿌리에 놓였으니 좋은 열매 맺지 아니하는 나무마다 찍혀 불에 던지우리라
(trg)="b.MAT.3.10.1"> Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi .
(trg)="b.MAT.3.10.2"> Garab nag gu meññul doom yu baax , dees na ko gor , sànni ko ci safara si .
(src)="b.MAT.3.11.1"> 나는 너희로 회개케 하기 위하여 물로 세례를 주거니와 내 뒤에 오시는 이는 나보다 능력이 많으시니 나는 그의 신을 들기도 감당치 못하겠노라 그는 성령과 불로 너희에게 세례를 주실 것이요
(trg)="b.MAT.3.11.1"> Man maa ngi leen di sóob ci ndox , ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar .
(trg)="b.MAT.3.11.2"> Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan , ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam .
(trg)="b.MAT.3.11.3"> Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara .
(src)="b.MAT.3.12.1"> 손에 키를 들고 자기의 타작 마당을 정하게 하사 알곡은 모아 곡간에 들이고 쭉정이는 꺼지지 않는 불에 태우시리라
(trg)="b.MAT.3.12.1"> Layoom mu ngi ci loxoom , ngir jéri dàgga ja , ba mu set ; pepp ma dina ko def ca sàq ma , waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk . »
(src)="b.MAT.3.13.1"> 이 때에 예수께서 갈릴리로서 요단강에 이르러 요한에게 세례를 받으려 하신대
(trg)="b.MAT.3.13.1"> Booba Yeesu jóge Galile , ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan .
(src)="b.MAT.3.14.1"> 요한이 말려 가로되 내가 당신에게 세례를 받아야 할 터인데 당신이 내게로 오시나이까
(trg)="b.MAT.3.14.1"> Waaye Yaxya gàntu ko ne : « Man maa soxla , nga sóob ma ci ndox , te yaa ngi ñëw ci man ! »
(src)="b.MAT.3.15.1"> 예수께서 대답하여 가라사대 이제 허락하라 우리가 이와 같이 하여 모든 의를 이루는 것이 합당하니라 하신대 이에 요한이 허락하는지라
(trg)="b.MAT.3.15.1"> Yeesu tontu ko : « Bàyyil noonu , ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub . »
(trg)="b.MAT.3.15.2"> Noonu Yaxya nangu .
(src)="b.MAT.3.16.1"> 예수께서 세례를 받으시고 곧 물에서 올라오실새 하늘이 열리고 하나님의 성령이 비둘기 같이 내려 자기 위에 임하심을 보시더니
(trg)="b.MAT.3.16.1"> Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga , Yeesu génn .
(trg)="b.MAT.3.16.2"> Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku , te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax , ñëw ci kaw Yeesu .
(src)="b.MAT.3.17.1"> 하늘로서 소리가 있어 말씀하시되 이는 내 사랑하는 아들이요 내 기뻐하는 자라 하시니라
(trg)="b.MAT.3.17.1"> Te baat bu jóge asamaan dégtu ne : « Kii mooy sama Doom ji ma bëgg ; ci moom laa ame bànneex . »
(src)="b.MAT.4.1.1"> 그 때에 예수께서 성령에게 이끌리어 마귀에게 시험을 받으러 광야로 가사
(trg)="b.MAT.4.1.1"> Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma , ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane .
(src)="b.MAT.4.2.1"> 사십 일을 밤낮으로 금식하신 후에 주리신지라
(trg)="b.MAT.4.2.1"> Yeesu nekk fa te lekkul ñeent-fukki bëccëg ak ñeent-fukki guddi , door a xiif .
(src)="b.MAT.4.3.1"> 시험하는 자가 예수께 나아와서 가로되 네가 만일 하나님의 아들이어든 명하여 이 돌들이 떡덩이가 되게 하라
(trg)="b.MAT.4.3.1"> Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko : « Boo dee Doomu Yàlla , santal doj yii , ñu nekk mburu . »
(src)="b.MAT.4.4.1"> 예수께서 대답하여 가라사대 기록되었으되 사람이 떡으로만 살것이 아니요 하나님의 입으로 나오는 모든 말씀으로 살 것이라 하였느니라 하시니
(trg)="b.MAT.4.4.1"> Waaye Yeesu tontu ko ne : « Mbind mi nee na : “ Nit du dunde mburu rekk , waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla . ” »
(src)="b.MAT.4.5.1"> 이에 마귀가 예수를 거룩한 성으로 데려다가 성전 꼭대기에 세우고
(trg)="b.MAT.4.5.1"> Bi mu waxee loolu , Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba , teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga .
(src)="b.MAT.4.6.1"> 가로되 네가 만일 하나님의 아들이어든 뛰어내리라 기록하였으되 저가 너를 위하여 그 사자들을 명하시리니 저희가 손으로 너를 받들어 발이 돌에 부딪히지 않게 하리로다 하였느니라
(trg)="b.MAT.4.6.1"> Mu ne ko : « Boo dee Doomu Yàlla , tëbal ci suuf , ndaxte Mbind mi nee na : “ Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir , ñu leewu la ci seeni loxo , ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj . ” »
(src)="b.MAT.4.7.1"> 예수께서 이르시되 또 기록되었으되 주 너의 하나님을 시험치 말라 하였느니라 하신대
(trg)="b.MAT.4.7.1"> Yeesu tontu ko : « Bind nañu it ne : “ Bul diiŋat Yàlla , sa Boroom . ” »
(src)="b.MAT.4.8.1"> 마귀가 또 그를 데리고 지극히 높은 산으로 가서 천하 만국과 그 영광을 보여
(trg)="b.MAT.4.8.1"> Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool , won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam .
(src)="b.MAT.4.9.1"> 가로되 만일 내게 엎드려 경배하면 이 모든 것을 네게 주리라
(trg)="b.MAT.4.9.1"> Mu ne ko : « Lii lépp dinaa la ko may , boo sukkee màggal ma . »
(src)="b.MAT.4.10.1"> 이에 예수께서 말씀하시되 사단아 물러가라 기록되었으되 주 너의 하나님께 경배하고 다만 그를 섬기라 하였느니라
(trg)="b.MAT.4.10.1"> Waaye Yeesu tontu ko : « Sore ma Seytaane , ndaxte Mbind mi nee na : “ Nanga màggal Yàlla sa Boroom , te jaamu ko moom rekk . ” »
(src)="b.MAT.4.11.1"> 이에 마귀는 예수를 떠나고 천사들이 나아와서 수종드니라
(trg)="b.MAT.4.11.1"> Noonu Seytaane bàyyi ko .
(trg)="b.MAT.4.11.2"> Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu , di ko topptoo .
(src)="b.MAT.4.12.1"> 예수께서 요한의 잡힘을 들으시고 갈릴리로 물러 가셨다가
(trg)="b.MAT.4.12.1"> Am bés Yeesu dégg ne , jàpp nañu Yaxya ; mu jóg nag , jëm Galile .
(src)="b.MAT.4.13.1"> 나사렛을 떠나 스불론과 납달리 지경 해변에 있는 가버나움에 가서 사시니
(trg)="b.MAT.4.13.1"> Gannaaw gi , mu toxoo dëkku Nasaret , dem dëkk Kapernawum , bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali .
(src)="b.MAT.4.14.1"> 이는 선지자 이사야로 하신 말씀을 이루려 하심이라 일렀으되
(trg)="b.MAT.4.14.1"> Noonu am la ñu waxoon , jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi , bi mu naan :
(src)="b.MAT.4.15.1"> 스불론 땅과 납달리 땅과 요단강 저편 해변 길과 이방의 갈릴리여
(trg)="b.MAT.4.15.1"> « Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali , di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan , yaw Galile , réewum ñi dul Yawut —
(src)="b.MAT.4.16.1"> 흑암에 앉은 백성이 큰 빛을 보았고 사망의 땅과 그늘에 앉은 자들에게 빛이 비취었도다 하였느니라
(trg)="b.MAT.4.16.1"> xeet wa nekkoon cig lëndëm , gis na leer gu mag , ña dëkkoon ca réew , ma dee tiim , leer fenkal na leen . »
(src)="b.MAT.4.17.1"> 이 때부터 예수께서 비로소 전파하여 가라사대 회개하라 천국이 가까왔느니라 하시더라
(trg)="b.MAT.4.17.1"> Booba Yeesu tàmbali di waare naan : « Tuubleen seeni bàkkaar , ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na . »
(src)="b.MAT.4.18.1"> 갈릴리 해변에 다니시다가 두 형제 곧 베드로라 하는 시몬과 그 형제 안드레가 바다에 그물 던지는 것을 보시니 저희는 어부 라
(trg)="b.MAT.4.18.1"> Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile , mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay , mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer , ak Andare .
(trg)="b.MAT.4.18.2"> Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga , ndaxte ay nappkat lañu woon .
(src)="b.MAT.4.19.1"> 말씀하시되 나를 따라 오너라 내가 너희로 사람을 낚는 어부가 되게 하리라 하시니
(trg)="b.MAT.4.19.1"> Yeesu ne leen : « Ñëwleen topp ci man , ma def leen nappkati nit . »
(src)="b.MAT.4.20.1"> 저희가 곧 그물을 버려 두고 예수를 좇으니라
(trg)="b.MAT.4.20.1"> Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal , topp ci moom .
(src)="b.MAT.4.21.1"> 거기서 더 가시다가 다른 두 형제 곧 세베대의 아들 야고보와 그 형제 요한이 그 부친 세베대와 한가지로 배에서 그물 깁는 것을 보시고 부르시니
(trg)="b.MAT.4.21.1"> Ba Yeesu demee ba ca kanam , mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay , ñuy Saag doomu Sebede , ak Yowaana rakkam .
(trg)="b.MAT.4.21.2"> Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay , di defar seeni mbaal .
(trg)="b.MAT.4.21.3"> Noonu Yeesu woo leen .
(src)="b.MAT.4.22.1"> 저희가 곧 배와 부친을 버려두고 예수를 좇으니라
(trg)="b.MAT.4.22.1"> Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay , topp ci moom .
(src)="b.MAT.4.23.1"> 예수께서 온 갈릴리에 두루 다니사 저희 회당에서 가르치시며 천국 복음을 전파하시며 백성 중에 모든 병과 모든 약한 것을 고치시니
(trg)="b.MAT.4.23.1"> Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp , di jàngale ci seeni jàngu tey yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla ; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña ,
(src)="b.MAT.4.24.1"> 그의 소문이 온 수리아에 퍼진지라 사람들이 모든 앓는 자 곧 각색병과 고통에 걸린 자 귀신 들린 자 간질하는 자 중풍병자들을 데려오니 저희를 고치시더라
(trg)="b.MAT.4.24.1"> ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp .
(trg)="b.MAT.4.24.2"> Ñu di ko indil ñi wopp ñépp , ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare , ñi rab jàpp , ñiy say ak ñi làggi , mu faj leen .
(src)="b.MAT.4.25.1"> 갈릴리와 데가볼리와 예루살렘과 유대와 요단강 건너편에서 허다한 무리가 좇으니라
(trg)="b.MAT.4.25.1"> Noonu mbooloo mu bare topp ci moom , jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi , ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude , ba ci gannaaw dexu Yurdan ..
(src)="b.MAT.5.1.1"> 예수께서 무리를 보시고 산에 올라가 앉으시니 제자들이 나아온지라
(trg)="b.MAT.5.1.1"> Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag , mu yéeg ca tund wa , toog ; taalibeem ya ñëw ci moom .
(src)="b.MAT.5.2.1"> 입을 열어 가르쳐 가라사대
(trg)="b.MAT.5.2.1"> Mu daldi leen jàngal naan :
(src)="b.MAT.5.3.1"> 심령이 가난한 자는 복이 있나니 천국이 저희 것임이요
(trg)="b.MAT.5.3.1"> « Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla , barkeel ngeen , ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji , yéena ko yelloo .
(src)="b.MAT.5.4.1"> 애통하는 자는 복이 있나니 저희가 위로를 받을 것임이요
(trg)="b.MAT.5.4.1"> Yéen ñi nekk ci naqar , barkeel ngeen , ndax dees na dëfël seen xol .
(src)="b.MAT.5.5.1"> 온유한 자는 복이 있나니 저희가 땅을 기업으로 받을 것임이요
(trg)="b.MAT.5.5.1"> Yéen ñi lewet , barkeel ngeen , ndax dingeen moomi àddina .
(src)="b.MAT.5.6.1"> 의에 주리고 목마른 자는 복이 있나니 저희가 배부를 것임이요
(trg)="b.MAT.5.6.1"> Yéen ñi xiif te mar njub , barkeel ngeen , ndax dingeen regg .
(src)="b.MAT.5.7.1"> 긍휼히 여기는 자는 복이 있나니 저희가 긍휼히 여김을 받을 것임이요
(trg)="b.MAT.5.7.1"> Yéen ñi am yërmande , barkeel ngeen , ndax dees na leen yërëm .
(src)="b.MAT.5.8.1"> 마음이 청결한 자는 복이 있나니 저희가 하나님을 볼 것임이요
(trg)="b.MAT.5.8.1"> Yéen ñi am xol bu sell , barkeel ngeen , ndax dingeen gis Yàlla .
(src)="b.MAT.5.9.1"> 화평케 하는 자는 복이 있나니 저희가 하나님의 아들이라 일컬음을 받을 것임이요
(trg)="b.MAT.5.9.1"> Yéen ñiy wut jàmm , barkeel ngeen , ndax dees na leen tudde doomi Yàlla .
(src)="b.MAT.5.10.1"> 의를 위하여 핍박을 받은 자는 복이 있나니 천국이 저희 것임이라
(trg)="b.MAT.5.10.1"> Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub , barkeel ngeen , ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji , yéena ko yelloo .