# is/Icelandic.xml.gz
# wo/Wolof-NT.xml.gz


(src)="b.MAT.1.1.1"> Ættartala Jesú Krists , sonar Davíðs , sonar Abrahams .
(trg)="b.MAT.1.1.1"> Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist , sëtu Daawuda , sëtu Ibraayma .

(src)="b.MAT.1.2.1"> Abraham gat Ísak , Ísak gat Jakob , Jakob gat Júda og bræður hans .
(trg)="b.MAT.1.2.1"> Ibraayma moo jur Isaaxa ; Isaaxa jur Yanqóoba ; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam ;

(src)="b.MAT.1.3.1"> Júda gat Peres og Sara við Tamar , Peres gat Esrom , Esrom gat Ram ,
(trg)="b.MAT.1.3.1"> Yuda , Fares ak Sara ci Tamar ; Fares Esrom , miy baayu Aram ;

(src)="b.MAT.1.4.1"> Ram gat Ammínadab , Ammínadab gat Nakson , Nakson gat Salmon ,
(trg)="b.MAT.1.4.1"> Aram Aminadab ; Aminadab Naason ; Naason Salmon ;

(src)="b.MAT.1.5.1"> Salmon gat Bóas við Rahab , og Bóas gat Óbeð við Rut .
(src)="b.MAT.1.5.2"> Óbeð gat Ísaí ,
(trg)="b.MAT.1.5.1"> Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas ; Bowas am ak Ruut Obedd ; Obedd jur Yese ,

(src)="b.MAT.1.6.1"> og Ísaí gat Davíð konung .
(src)="b.MAT.1.6.2"> Davíð gat Salómon við konu Úría ,
(trg)="b.MAT.1.6.1"> miy baayu buur bi Daawuda .
(trg)="b.MAT.1.6.2"> Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon jabari Uri ;

(src)="b.MAT.1.7.1"> Salómon gat Róbóam , Róbóam gat Abía , Abía gat Asaf ,
(trg)="b.MAT.1.7.1"> Suleymaan jur Robowam ; Robowam Abiya ; Abiya Asaf ;

(src)="b.MAT.1.8.1"> Asaf gat Jósafat , Jósafat gat Jóram , Jóram gat Ússía ,
(trg)="b.MAT.1.8.1"> Asaf Yosafat ; Yosafat Yoram , miy baayu Osiyas ;

(src)="b.MAT.1.9.1"> Ússía gat Jótam , Jótam gat Akas , Akas gat Esekía ,
(trg)="b.MAT.1.9.1"> Osiyas jur Yowatam ; Yowatam Akas , miy baayu Esekiyas ;

(src)="b.MAT.1.10.1"> Esekía gat Manasse , Manasse gat Amos , Amos gat Jósía .
(trg)="b.MAT.1.10.1"> Esekiyas Manase ; Manase Amon ; Amon Yosiyas ;

(src)="b.MAT.1.11.1"> Jósía gat Jekonja og bræður hans á tíma herleiðingarinnar til Babýlonar .
(trg)="b.MAT.1.11.1"> Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono , ja ñu defe Yawut ya jaam , yóbbu leen Babilon .

(src)="b.MAT.1.12.1"> Eftir herleiðinguna til Babýlonar gat Jekonja Sealtíel , Sealtíel gat Serúbabel ,
(trg)="b.MAT.1.12.1"> Ba ñu leen yóbboo ca Babilon , Yekoñas jur Salacel ; Salacel Sorobabel ,

(src)="b.MAT.1.13.1"> Serúbabel gat Abíúd , Abíúd gat Eljakím , Eljakím gat Asór ,
(trg)="b.MAT.1.13.1"> miy baayu Abiyudd ; Abiyudd Eliyakim ; Eliyakim Asor ;

(src)="b.MAT.1.14.1"> Asór gat Sadók , Sadók gat Akím , Akím gat Elíúd ,
(trg)="b.MAT.1.14.1"> Asor Sadog ; Sadog Akim ; Akim Eliyudd ;

(src)="b.MAT.1.15.1"> Elíúd gat Eleasar , Eleasar gat Mattan , Mattan gat Jakob ,
(trg)="b.MAT.1.15.1"> Eliyudd Eleyasar ; Eleyasar Matan , miy baayu Yanqóoba ;

(src)="b.MAT.1.16.1"> og Jakob gat Jósef , mann Maríu , en hún ól Jesú , sem kallast Kristur .
(trg)="b.MAT.1.16.1"> Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama ; te ci Maryaama la Yeesu , mi ñuy wax Kirist , juddoo .

(src)="b.MAT.1.17.1"> Þannig eru alls fjórtán ættliðir frá Abraham til Davíðs , fjórtán ættliðir frá Daví � fram að herleiðingunni til Babýlonar og fjórtán ættliðir frá herleiðingunni til Krists .
(trg)="b.MAT.1.17.1"> Mboolem giir googu nag , la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda , fukk lañu ak ñeent ; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon , fukk lañu ak ñeent ; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist , fukk lañu ak ñeent .

(src)="b.MAT.1.18.1"> Fæðing Jesú Krists varð með þessum atburðum : María , móðir hans , var föstnuð Jósef .
(src)="b.MAT.1.18.2"> En áður en þau komu saman , reyndist hún þunguð af heilögum anda .
(trg)="b.MAT.1.18.1"> Nii la Yeesu Kirist juddoo .
(trg)="b.MAT.1.18.2"> Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa , waaye laata ñoo ànd , gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi .

(src)="b.MAT.1.19.1"> Jósef , festarmaður hennar , sem var grandvar , vildi ekki gjöra henni opinbera minnkun og hugðist skilja við hana í kyrrþey .
(trg)="b.MAT.1.19.1"> Yuusufa jëkkëram nag , nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woon a weer .
(trg)="b.MAT.1.19.2"> Mu nar a xàccook moom ci sutura .

(src)="b.MAT.1.20.1"> Hann hafði ráðið þetta með sér , en þá vitraðist honum engill Drottins í draumi og sagði : " Jósef , sonur Davíðs , óttastu ekki að taka til þín Maríu , heitkonu þína .
(src)="b.MAT.1.20.2"> Barnið , sem hún gengur með , er af heilögum anda .
(trg)="b.MAT.1.20.1"> Waaye bi muy xalaat ci loolu , benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko : « Yaw Yuusufa , sëtu Daawuda , bul ragal a yeggali Maryaama sa jabar , ndaxte doom ji mu ëmb , ci Xel mu Sell mi la jóge .

(src)="b.MAT.1.21.1"> Hún mun son ala , og hann skaltu láta heita Jesú , því að hann mun frelsa lýð sinn frá syndum þeirra . "
(trg)="b.MAT.1.21.1"> Dina jur doom ju góor ; na nga ko tudde Yeesu , ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar . »

(src)="b.MAT.1.22.1"> Allt varð þetta til þess , að rætast skyldu orð Drottins fyrir munn spámannsins :
(trg)="b.MAT.1.22.1"> Loolu lépp xewoon na , ngir amal li Boroom bi wax , jaarale ko cib yonent , bi mu naan :

(src)="b.MAT.1.23.1"> " Sjá , mærin mun þunguð verða og son ala .
(src)="b.MAT.1.23.2"> Nafn hans mun vera Immanúel , " það þýðir : Guð með oss .
(trg)="b.MAT.1.23.1"> « Janq bi dina ëmb , jur doom ju góor , ñu tudde ko Emanuwel , » liy tekki « Yàlla ganesi na nu . »

(src)="b.MAT.1.24.1"> Þegar Jósef vaknaði , gjörði hann eins og engill Drottins hafði boðið honum og tók konu sína til sín .
(trg)="b.MAT.1.24.1"> Noonu Yuusufa yeewu , yeggali jabaram , na ko ko malaakam Boroom bi sante woon .

(src)="b.MAT.1.25.1"> Hann kenndi hennar ekki fyrr en hún hafði alið son .
(src)="b.MAT.1.25.2"> Og hann gaf honum nafnið JESÚS .
(trg)="b.MAT.1.25.1"> Waaye àndul ak moom , ba kera mu mucc , jur doom ju góor ; mu tudde ko Yeesu .

(src)="b.MAT.10.1.1"> Og hann kallaði til sín lærisveina sína tólf og gaf þeim vald yfir óhreinum öndum , að þeir gætu rekið þá út og læknað hvers kyns sjúkdóm og veikindi .
(trg)="b.MAT.10.1.1"> Noonu Yeesu woo ca moom fukki taalibeem ya ak ñaar , jox leen sañ-sañu dàq rab yi , tey faj jàngoro yépp ak wéradi yépp .

(src)="b.MAT.10.2.1"> Nöfn postulanna tólf eru þessi : Fyrstur Símon , sem kallast Pétur , og Andrés bróðir hans , þá Jakob Sebedeusson og Jóhannes bróðir hans ,
(trg)="b.MAT.10.2.1"> Fukki ndaw ak ñaar , ya Yeesu yónni woon nag , nii lañu tuddoon : ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer , ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay ; Saag doomu Sebede , ak Yowaana rakkam ; l

(src)="b.MAT.10.3.1"> Filippus og Bartólómeus , Tómas og Matteus tollheimtumaður , Jakob Alfeusson og Taddeus ,
(trg)="b.MAT.10.3.1"> Filib ak Bartelemi ; Tomaa ak Macë , juutikat ba woon ; Saag doomu Alfe , ak Tade ; l

(src)="b.MAT.10.4.1"> Símon vandlætari og Júdas Ískaríot , sá er sveik hann .
(trg)="b.MAT.10.4.1"> Simoŋ , mi bokk ca mbooloo , ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew ; ak Yudaa Iskariyo , mi nar a wor Yeesu .

(src)="b.MAT.10.5.1"> Þessa tólf sendi Jesús út og mælti svo fyrir : " Haldið ekki til heiðinna manna og farið ekki í samverska borg .
(trg)="b.MAT.10.5.1"> Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar , jox leen ndigal ne leen : « Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari .

(src)="b.MAT.10.6.1"> Farið heldur til týndra sauða af Ísraelsætt .
(trg)="b.MAT.10.6.1"> Waaye demleen ci bànni Israyil , ñoom ñi réer niy xar .

(src)="b.MAT.10.7.1"> Farið og prédikið : , Himnaríki er í nánd . '
(trg)="b.MAT.10.7.1"> Bu ngeen demee nag , yégleleen naan : “ Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na . ”

(src)="b.MAT.10.8.1"> Læknið sjúka , vekið upp dauða , hreinsið líkþráa , rekið út illa anda .
(src)="b.MAT.10.8.2"> Gefins hafið þér fengið , gefins skuluð þér láta í té .
(trg)="b.MAT.10.8.1"> Fajleen ñi wopp , dekkal ñi dee , fajleen gaana yi te dàq rab yi .
(trg)="b.MAT.10.8.2"> Cig neen ngeen ame , mayeleen cig neen .

(src)="b.MAT.10.9.1"> Takið ekki gull , silfur né eir í belti ,
(trg)="b.MAT.10.9.1"> Buleen dajale wurus , xaalis mbaa xànjar ci seeni maxtume .

(src)="b.MAT.10.10.1"> eigi mal til ferðar eða tvo kyrtla og hvorki skó né staf .
(src)="b.MAT.10.10.2"> Verður er verkamaðurinn fæðis síns .
(trg)="b.MAT.10.10.1"> Buleen wut it mbuus ngir tukki mbaa ñaari turki , ay dàll mbaa aw yet , ndaxte liggéeykat yeyoo na dundam .

(src)="b.MAT.10.11.1"> Hvar sem þér komið í borg eða þorp , spyrjist þá fyrir um , hver þar sé verðugur , og þar sé aðsetur yðar , uns þér leggið upp að nýju .
(trg)="b.MAT.10.11.1"> « Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw , nangeen fa seet ku fa am faayda , dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba .

(src)="b.MAT.10.12.1"> Þegar þér komið í hús , þá árnið því góðs ,
(trg)="b.MAT.10.12.1"> Bu ngeen di dugg ci kër nag , nuyooleen .

(src)="b.MAT.10.13.1"> og sé það verðugt , skal friður yðar koma yfir það , en sé það ekki verðugt , skal friður yðar aftur hverfa til yðar .
(trg)="b.MAT.10.13.1"> Bu fekkee ne kër ga yeyoo na ko , na seen jàmm wàcc ci ñoom , waaye bu ko yeyoowul , na seen yéene dellusi ci yéen .

(src)="b.MAT.10.14.1"> Og taki einhver ekki við yður né hlýði á orð yðar , farið þá úr því húsi eða þeirri borg og hristið dustið af fótum yðar .
(trg)="b.MAT.10.14.1"> Koo xam ne gàntu na leen , mbaa mu tanqamlu seeni wax , génnleen ca kër ga mbaa ca dëkk ba , yëlëb seen pëndu tànk .

(src)="b.MAT.10.15.1"> Sannlega segi ég yður : Bærilegra mun landi Sódómu og Gómorru á dómsdegi en þeirri borg .
(trg)="b.MAT.10.15.1"> Ci dëgg maa ngi leen koy wax , keroog bésub àtte ba , waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu .

(src)="b.MAT.10.16.1"> Sjá , ég sendi yður eins og sauði meðal úlfa .
(src)="b.MAT.10.16.2"> Verið því kænir sem höggormar og falslausir sem dúfur .
(trg)="b.MAT.10.16.1"> « Dégluleen , maa ngi leen di yónni , mel ni ay xar ci biir ay bukki .
(trg)="b.MAT.10.16.2"> Muusleen nag niy jaan , te lewet niy pitax .

(src)="b.MAT.10.17.1"> Varið yður á mönnunum .
(src)="b.MAT.10.17.2"> Þeir munu draga yður fyrir dómstóla og húðstrýkja yður í samkundum sínum .
(trg)="b.MAT.10.17.1"> Waaye moytuleen nit ñi , ndaxte dinañu leen jébbal àttekat yi te dóor leen ay yar ci seeni jàngu .

(src)="b.MAT.10.18.1"> Þér munuð leiddir fyrir landshöfðingja og konunga mín vegna þeim og heiðingjunum til vitnisburðar .
(trg)="b.MAT.10.18.1"> Dees na leen yóbbu ngir man ci kanami boroom réew ak i buur , ngir ngeen seede ma ci ñoom ak ci ñi dul Yawut .

(src)="b.MAT.10.19.1"> En þá er menn draga yður fyrir rétt , skuluð þér ekki hafa áhyggjur af því , hvernig eða hvað þér eigið að tala .
(src)="b.MAT.10.19.2"> Yður verður gefið á sömu stundu , hvað segja skal .
(trg)="b.MAT.10.19.1"> Boo xamee ne nag jébbale nañu leen , buleen am xel ñaar ci li ngeen di wax , mbaa ni ngeen koy waxe .
(trg)="b.MAT.10.19.2"> Ndaxte ca waxtu woowa sax dingeen jot li ngeen war a wax ;

(src)="b.MAT.10.20.1"> Þér eruð ekki þeir sem tala , heldur andi föður yðar , hann talar í yður .
(trg)="b.MAT.10.20.1"> du yéenay wax , waaye Xelum seen Baay mooy wax ci yéen .

(src)="b.MAT.10.21.1"> Bróðir mun selja bróður í dauða og faðir barn sitt .
(src)="b.MAT.10.21.2"> Börn munu rísa gegn foreldrum og valda þeim dauða .
(trg)="b.MAT.10.21.1"> « Mag dina joxe rakkam ci dee , baay joxe doomam ; ay doom it dinañu jóg , bañ seeni waajur , di leen reylu .

(src)="b.MAT.10.22.1"> Og þér munuð hataðir af öllum vegna nafns míns .
(src)="b.MAT.10.22.2"> En sá sem staðfastur er allt til enda , mun hólpinn verða .
(trg)="b.MAT.10.22.1"> Te yéen nag , ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur ; waaye ku muñ ba muj ga , mucc .

(src)="b.MAT.10.23.1"> Þegar þeir ofsækja yður í einni borg , þá flýið í aðra .
(src)="b.MAT.10.23.2"> Sannlega segi ég yður : Þér munuð ekki hafa náð til allra borga Ísraels , áður en Mannssonurinn kemur .
(trg)="b.MAT.10.23.1"> Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii , demleen ca ba ca kanam .
(trg)="b.MAT.10.23.2"> Ci dëgg maa ngi leen koy wax , dungeen man a wër dëkki Israyil yépp , te Doomu nit ki ñëwul . »

(src)="b.MAT.10.24.1"> Ekki er lærisveinn meistaranum fremri né þjónn herra sínum .
(trg)="b.MAT.10.24.1"> Yeesu teg ca ne : « Taalibe gënul kilifaam , te jaam gënul sangam .

(src)="b.MAT.10.25.1"> Nægja má lærisveini að vera sem meistari hans og þjóni sem herra hans .
(src)="b.MAT.10.25.2"> Fyrst þeir kölluðu húsföðurinn Beelsebúl , hvað kalla þeir þá heimamenn hans ?
(trg)="b.MAT.10.25.1"> Bu taalibe yemee ak kilifaam demin , doy na ; jaam it ni sangam .
(trg)="b.MAT.10.25.2"> Ndegam tudde nañu boroom kër gi Beelsebul , astemaak waa kër gi .

(src)="b.MAT.10.26.1"> Óttist þá því eigi .
(src)="b.MAT.10.26.2"> Ekkert er hulið , sem eigi verður opinbert , né leynt , er eigi verður kunnugt .
(trg)="b.MAT.10.26.1"> Kon nag buleen leen ragal , ndaxte amul dara lu nëbbu , lu ñu warul a biral , mbaa luy kumpa lu ñu warul a siiwal .

(src)="b.MAT.10.27.1"> Það sem ég segi yður í myrkri , skuluð þér tala í birtu , og það sem þér heyrið hvíslað í eyra , skuluð þér kunngjöra á þökum uppi .
(trg)="b.MAT.10.27.1"> Li ma leen wax ci biir lëndëm , waxleen ko ci leer ; li ma leen déey , yégleleen ko ci kaw taax yi .

(src)="b.MAT.10.28.1"> Hræðist ekki þá , sem líkamann deyða , en fá ekki deytt sálina .
(src)="b.MAT.10.28.2"> Hræðist heldur þann , sem megnar að tortíma bæði sálu og líkama í helvíti .
(trg)="b.MAT.10.28.1"> Te buleen ragal ñu man a rey yaram , te mënuñoo rey ruu , waaye ragal-leen Ki man a sànk yaram ak ruu ci safara .

(src)="b.MAT.10.29.1"> Eru ekki tveir spörvar seldir fyrir smápening ?
(src)="b.MAT.10.29.2"> Og ekki fellur einn þeirra til jarðar án vitundar föður yðar .
(trg)="b.MAT.10.29.1"> Ñaari picci rammatu , ndax duñu ko jaay ci dërëm ?
(trg)="b.MAT.10.29.2"> Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay .

(src)="b.MAT.10.30.1"> Á yður eru jafnvel höfuðhárin öll talin .
(trg)="b.MAT.10.30.1"> Seen kawari bopp sax , waññees na leen .

(src)="b.MAT.10.31.1"> Verið því óhræddir , þér eruð meira verðir en margir spörvar .
(trg)="b.MAT.10.31.1"> Kon buleen ragal dara , yéena gën ndiiraanu rammatu .

(src)="b.MAT.10.32.1"> Hvern þann sem kannast við mig fyrir mönnum , mun og ég við kannast fyrir föður mínum á himnum .
(trg)="b.MAT.10.32.1"> « Koo xam ne nangu nga ma ci kanamu nit ñi , man itam dinaa la nangu ci sama kanamu Baay , bi nekk ci kaw .

(src)="b.MAT.10.33.1"> En þeim sem afneitar mér fyrir mönnum , mun og ég afneita fyrir föður mínum á himnum .
(trg)="b.MAT.10.33.1"> Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi , man itam dinaa la gàntu ci sama kanamu Baay , bi nekk ci kaw .

(src)="b.MAT.10.34.1"> Ætlið ekki , að ég sé kominn að færa frið á jörð .
(src)="b.MAT.10.34.2"> Ég kom ekki að færa frið , heldur sverð .
(trg)="b.MAT.10.34.1"> « Te it buleen defe ne , damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina ; ñëwuma ngir indi jàmm , waaye jaasi laa indaale .

(src)="b.MAT.10.35.1"> Ég er kominn að gjöra , son andvígan föður sínum , dóttur móður sinni og tengdadóttur tengdamóður sinni .
(trg)="b.MAT.10.35.1"> Ndaxte ñëw naa ngir féewale doom ak baayam , doom ju jigéen ak ndeyam , jabar ak goroom ;

(src)="b.MAT.10.36.1"> Og heimamenn manns verða óvinir hans . '
(trg)="b.MAT.10.36.1"> te nooni nit ñooy waa këram .

(src)="b.MAT.10.37.1"> Sá sem ann föður eða móður meir en mér , er mín ekki verður , og sá sem ann syni eða dóttur meir en mér , er mín ekki verður .
(trg)="b.MAT.10.37.1"> Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay , yeyoowuloo ma ; ku ma gënalul sa doom ju góor walla ju jigéen , yeyoowuloo ma .

(src)="b.MAT.10.38.1"> Hver sem tekur ekki sinn kross og fylgir mér , er mín ekki verður .
(trg)="b.MAT.10.38.1"> Koo xam ne kii nanguwuloo ñàkk sa bakkan , ba mel ni ku ñu daaj ci bant , te nga topp ma , yeyoowuloo ma .

(src)="b.MAT.10.39.1"> Sá sem ætlar að finna líf sitt , týnir því , og sá sem týnir lífi sínu mín vegna , finnur það .
(trg)="b.MAT.10.39.1"> Kuy rawale sa bakkan , ñàkk ko , te ku ñàkk sa bakkan ndax man , jotaat ko .

(src)="b.MAT.10.40.1"> Sá sem tekur við yður , tekur við mér , og sá sem tekur við mér , tekur við þeim , er sendi mig .
(trg)="b.MAT.10.40.1"> « Te lii itam am na , ku leen nangu , nangu na ma , te ku ma nangu , nangu na ki ma yónni .

(src)="b.MAT.10.41.1"> Sá sem tekur við spámanni , vegna þess að hann er spámaður , mun fá spámanns laun , og sá sem tekur við réttlátum manni , vegna þess að hann er réttlátur , mun fá laun réttláts manns .
(trg)="b.MAT.10.41.1"> Ku nangu yonent ndax yónnentam , dina jot ci peyu yonent ; te ku nangu ku jub ndax njubteem , dina jot ci peyu ku jub .

(src)="b.MAT.10.42.1"> Og hver sem gefur einum þessara smælingja svaladrykk vegna þess eins , að hann er lærisveinn , sannlega segi ég yður , hann mun alls ekki missa af launum sínum . "
(trg)="b.MAT.10.42.1"> Ci dëgg maa ngi leen koy wax , koo xam ne kii may na kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gën a ndaw , ndax sama taalibe la , kooku du ñàkk yoolam mukk . »

(src)="b.MAT.11.1.1"> Þá er Jesús hafði mælt svo fyrir við lærisveina sína tólf , hélt hann þaðan að kenna og prédika í borgum þeirra .
(trg)="b.MAT.11.1.1"> Ba Yeesu joxee fukki taalibeem ya ak ñaar ndigal yooyu , mu jóge fa , ngir dem jàngaleji ak a waare ci seeni dëkk .

(src)="b.MAT.11.2.1"> Jóhannes heyrði í fangelsinu um verk Krists .
(src)="b.MAT.11.2.2"> Þá sendi hann honum orð með lærisveinum sínum og spurði :
(trg)="b.MAT.11.2.1"> Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi .
(trg)="b.MAT.11.2.2"> Mu yónni ci moom nag ay taalibeem ,

(src)="b.MAT.11.3.1"> " Ert þú sá , sem koma skal , eða eigum vér að vænta annars ? "
(trg)="b.MAT.11.3.1"> ne ko : « Ndax yaa di Ki war a ñëw , walla danoo war a xaar keneen ? »

(src)="b.MAT.11.4.1"> Jesús svaraði þeim : " Farið og kunngjörið Jóhannesi það , sem þér heyrið og sjáið :
(trg)="b.MAT.11.4.1"> Yeesu tontu leen ne : « Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko .

(src)="b.MAT.11.5.1"> Blindir fá sýn og haltir ganga , líkþráir hreinsast og daufir heyra , dauðir rísa upp , og fátækum er flutt fagnaðarerindi .
(trg)="b.MAT.11.5.1"> Gumba yaa ngi gis , lafañ yiy dox , gaana yi wér , tëx yiy dégg , ñi dee di dekki , te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi .

(src)="b.MAT.11.6.1"> Og sæll er sá , sem hneykslast ekki á mér . "
(trg)="b.MAT.11.6.1"> Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man , barkeel nga . »

(src)="b.MAT.11.7.1"> Þegar þeir voru farnir , tók Jesús að tala til mannfjöldans um Jóhannes : " Hvað fóruð þér að sjá í óbyggðum ?
(src)="b.MAT.11.7.2"> Reyr af vindi skekinn ?
(trg)="b.MAT.11.7.1"> Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu , Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen : « Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma ?
(trg)="b.MAT.11.7.2"> Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li ?

(src)="b.MAT.11.8.1"> Hvað fóruð þér að sjá ?
(src)="b.MAT.11.8.2"> Prúðbúinn mann ?
(src)="b.MAT.11.8.3"> Nei , prúðbúna menn er að finna í sölum konunga .
(trg)="b.MAT.11.8.1"> Kon lu ngeen seeti woon nag ?
(trg)="b.MAT.11.8.2"> Nit ku sol yére yu rafet ?
(trg)="b.MAT.11.8.3"> Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur .

(src)="b.MAT.11.9.1"> Til hvers fóruð þér ?
(src)="b.MAT.11.9.2"> Að sjá spámann ?
(src)="b.MAT.11.9.3"> Já , segi ég yður , og það meira en spámann .
(trg)="b.MAT.11.9.1"> Lu tax ngeen génn nag ?
(trg)="b.MAT.11.9.2"> Ngir gis ab yonent ?
(trg)="b.MAT.11.9.3"> Waaw , wax naa leen ne , ëpp na yonent .

(src)="b.MAT.11.10.1"> Hann er sá , sem um er ritað : Sjá , ég sendi sendiboða minn á undan þér , er greiða mun veg þinn fyrir þér .
(trg)="b.MAT.11.10.1"> Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan : “ Maa ngi yónni sama ndaw , mu jiitu la , te xàllal la yoon ci sa kanam . ”

(src)="b.MAT.11.11.1"> Sannlega segi ég yður : Enginn er sá af konu fæddur , sem meiri sé en Jóhannes skírari .
(src)="b.MAT.11.11.2"> En hinn minnsti í himnaríki er honum meiri .
(trg)="b.MAT.11.11.1"> Ci dëgg maa ngi leen koy wax , ci li jigéen jur , ku sut Yaxya musul a feeñ .
(trg)="b.MAT.11.11.2"> Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut .

(src)="b.MAT.11.12.1"> Frá dögum Jóhannesar skírara og til þessa er ríki himnanna ofríki beitt , og ofríkismenn vilja hremma það .
(trg)="b.MAT.11.12.1"> Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi , nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla , te ñi sawar ñoo ci am wàll .

(src)="b.MAT.11.13.1"> Spámennirnir allir og lögmálið , allt fram að Jóhannesi , sögðu fyrir um þetta .
(trg)="b.MAT.11.13.1"> Ndaxte li yonent yi wax ak li yoonu Musaa tëral ñu ngi doon dox , ba kera Yaxya di feeñ .

(src)="b.MAT.11.14.1"> Og ef þér viljið við því taka , þá er hann Elía sá , sem koma skyldi .
(trg)="b.MAT.11.14.1"> Te Yaxya moomu , su ngeen bëggee nangu lii , mooy Iliyas bi waroon a ñëw .

(src)="b.MAT.11.15.1"> Hver sem eyru hefur , hann heyri .
(trg)="b.MAT.11.15.1"> Déglul bu baax , yaw mi am ay nopp .

(src)="b.MAT.11.16.1"> Við hvað á ég að líkja þessari kynslóð ?
(src)="b.MAT.11.16.2"> Lík er hún börnum , sem á torgum sitja og kallast á :
(trg)="b.MAT.11.16.1"> « Niti jamono jii nag , lan laa leen man a mengaleel ?
(trg)="b.MAT.11.16.2"> Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma , di woo seeni xarit ,

(src)="b.MAT.11.17.1"> , Vér lékum fyrir yður á flautu og ekki vilduð þér dansa .
(src)="b.MAT.11.17.2"> Vér sungum yður sorgarljóð , og ekki vilduð þér syrgja . '
(trg)="b.MAT.11.17.1"> ne leen : “ Liital nanu leen ak toxoro , te fecculeen , woyal nanu leen woyi dëj , te jooyuleen . ”

(src)="b.MAT.11.18.1"> Jóhannes kom , át hvorki né drakk , og menn segja : , Hann hefur illan anda . '
(trg)="b.MAT.11.18.1"> Ndaxte Yaxya feeñ na , lekkul , naanul , ngeen daldi ne : “ Dafa ànd ak rab . ”

(src)="b.MAT.11.19.1"> Mannssonurinn kom , át og drakk , og menn segja : , Hann er mathákur og vínsvelgur , vinur tollheimtumanna og bersyndugra ! '
(src)="b.MAT.11.19.2"> En spekin sannast af verkum sínum . "
(trg)="b.MAT.11.19.1"> Gannaaw gi nag , Doomu nit ki ñëw na , lekk , naan , ngeen daldi ne : “ Kii daal bëgg na lekk , di naan biiñ , tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar . ”
(trg)="b.MAT.11.19.2"> Waaye li xam-xamu Yàlla di jur , mooy firndeel ne dëgg la . »

(src)="b.MAT.11.20.1"> Þá tók hann að ávíta borgirnar , þar sem hann hafði gjört flest kraftaverk sín , fyrir að hafa ekki gjört iðrun .
(trg)="b.MAT.11.20.1"> Gannaaw loolu Yeesu daldi gëdd dëkk , ya mu defe woon la ëpp cay kéemaanam , ndaxte tuubuñu seeni bàkkaar .

(src)="b.MAT.11.21.1"> " Vei þér , Korasín !
(src)="b.MAT.11.21.2"> Vei þér , Betsaída !
(src)="b.MAT.11.21.3"> Ef gjörst hefðu í Týrus og Sídon kraftaverkin , sem gjörðust í ykkur , hefðu þær löngu iðrast í sekk og ösku .
(trg)="b.MAT.11.21.1"> Mu ne : « Dingeen torox , yéen waa Korasin ak waa Betsayda , ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen , bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon , kon réccu nañu bu yàgg , xëppoo dóom , sol saaku .

(src)="b.MAT.11.22.1"> En ég segi ykkur : Týrus og Sídon mun bærilegra á dómsdegi en ykkur .
(trg)="b.MAT.11.22.1"> Waaye maa ngi leen koy wax , keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane .

(src)="b.MAT.11.23.1"> Og þú Kapernaum .
(src)="b.MAT.11.23.2"> Verður þú hafin til himins ?
(src)="b.MAT.11.23.3"> Nei , til heljar mun þér steypt verða .
(src)="b.MAT.11.23.4"> Ef gjörst hefðu í Sódómu kraftaverkin , sem gjörðust í þér , þá stæði hún enn í dag .
(trg)="b.MAT.11.23.1"> Te yaw dëkku Kapernawum , ndax dees na la yékkati bu kawe ?
(trg)="b.MAT.11.23.2"> Déedéet , dees na la daane bu suufe .
(trg)="b.MAT.11.23.3"> Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw , bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom , kon mu nekk ba tey .

(src)="b.MAT.11.24.1"> En ég segi yður : Landi Sódómu mun bærilegra á dómsdegi en þér . "
(trg)="b.MAT.11.24.1"> Waaye maa ngi leen koy wax , keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane . »

(src)="b.MAT.11.25.1"> Á þeim tíma tók Jesús svo til orða : " Ég vegsama þig , faðir , herra himins og jarðar , að þú hefur hulið þetta spekingum og hyggindamönnum , en opinberað það smælingjum .
(trg)="b.MAT.11.25.1"> Ca jamono joojale Yeesu wax na lii : « Yaw Baay bi , Boroom asamaan ak suuf , maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel , te xamal leen gune yi .

(src)="b.MAT.11.26.1"> Já , faðir , svo var þér þóknanlegt .
(trg)="b.MAT.11.26.1"> Waaw Baay bi , ndaxte looloo la neex . »

(src)="b.MAT.11.27.1"> Allt er mér falið af föður mínum , og enginn þekkir soninn nema faðirinn , né þekkir nokkur föðurinn nema sonurinn og sá er sonurinn vill opinbera hann .
(trg)="b.MAT.11.27.1"> Yeesu teg ca ne : « Sama Baay jébbal na ma lépp , te kenn mënu maa xam , man Doom ji , ku dul Baay bi ; kenn it mënul a xam Baay bi , ku dul man Doom ji , ak ku ma ko bëgg a xamal .

(src)="b.MAT.11.28.1"> Komið til mín , allir þér sem erfiði hafið og þungar byrðar , og ég mun veita yður hvíld .
(trg)="b.MAT.11.28.1"> « Ñëwleen ci man , yéen ñépp ñi sonn te diis , dinaa leen may noflaay .

(src)="b.MAT.11.29.1"> Takið á yður mitt ok og lærið af mér , því að ég er hógvær og af hjarta lítillátur , og þá munuð þér finna hvíld sálum yðar .
(trg)="b.MAT.11.29.1"> Jébbaluleen ci man te jàng ci man , ndaxte lewet naa te woyof , te dingeen am noflaay ci seen xol .

(src)="b.MAT.11.30.1"> Því að mitt ok er ljúft og byrði mín létt . "
(trg)="b.MAT.11.30.1"> Ndaxte sama kilifteef lewet na te sama yen diisul . »

(src)="b.MAT.12.1.1"> Um þessar mundir fór Jesús um sáðlönd á hvíldardegi .
(src)="b.MAT.12.1.2"> Lærisveinar hans kenndu hungurs og tóku að tína kornöx og eta .
(trg)="b.MAT.12.1.1"> Amoon na benn bésu noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor , fekk ay taalibeem xiif ; ñu daldi fàq ay gub nag , di lekk .

(src)="b.MAT.12.2.1"> Þegar farísear sáu það , sögðu þeir við hann : " Lít á , lærisveinar þínir gjöra það , sem ekki er leyft að gjöra á hvíldardegi . "
(trg)="b.MAT.12.2.1"> Farisen ya nag gis ko , ne Yeesu : « Gisal , say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi . »

(src)="b.MAT.12.3.1"> Hann svaraði þeim : " Hafið þér eigi lesið , hvað Davíð gjörði , þegar hann hungraði og menn hans ?
(trg)="b.MAT.12.3.1"> Noonu Yeesu tontu leen : « Ndax jànguleen la Daawuda defoon , ba mu xiifee , moom ak ña mu àndaloon ?