# ful/E8uQz89NVFi4.xml.gz
# wol/E8uQz89NVFi4.xml.gz
(src)="1"> [ Quoi de neuf dans Firefox ]
(trg)="1"> [ Yan xibaar ci Firefox ]
(src)="2"> Il est maintenant plus facile et plus rapide d' aller où vous le désirez via le dernier Firefox .
(trg)="2"> Yomb na leegi te gaaw leegi , dem foo bëgg te agg itam foo bëgg ak Firefox bu mujj bi .
(src)="3"> Avec la page d' accueil retravaillée , vous pouvez maintenant accéder et naviguer plus facilement parmi les options les plus souvent utilisées
(trg)="3"> Ak xëtu dalal jamm bi ñu defaraat , mën nga leegi agg ak joow ci lu yomb ci sa ay tànneefi njël yi ngay gena jariñoo .
(src)="4"> Comme les téléchargements , marque- pages , historique , extensions , Firefox Sync et les paramètres .
(trg)="4"> Yi melni yeb yi , mandarga xët yi , jaar jaar , modil yi , jokkoo yi ak paraameetar yi .
(src)="5"> [ Page " Nouvel onglet " ]
(trg)="5"> [ Xëtu koñ bu bees ]
(src)="6"> Nous avons également amélioré votre page " Nouvel onglet " .
(trg)="6"> Yokk nañu itam ay bees bees ci xëtu koñ bu bees .
(src)="7"> Avec la page " Nouvel onglet " , vous pouvez facilement naviguer vers les sites les plus récents et fréquemment utilisés , en un clic .
(trg)="7"> Ak sa xëtu koñ bu bees , mën nga joow bu yomb ci yi gëna bees ak yi ngay gëna gane ci benn cuq .
(src)="8"> Pour commencer à utiliser la page " Nouvel onglet " , créez un nouvel onglet en cliquant sur le ´+ ' en haut de votre navigateur .
(trg)="8"> Boo bëggee tambali jëfandikoo xëtu koñ bu bees , sosal koñ bu bees boo cuqee ci ´+ ' ci jowkat bi ci kaw .
(src)="9"> La page " Nouvel onglet " affiche désormais des miniatures des sites les plus récemment et fréquemment utilisés de votre historique de barre de recherche intelligente .
(trg)="9"> Xëtu koñ bu bees dina wone leegi wiñeti dal yi nga mujj gane .
(src)="10"> Vous pouvez personnaliser votre page " Nouvel onglet " en faisant glisser les miniatures afin de changer leur ordre .
(trg)="10"> Mën nga solal sa xëtu koñ bu bees boo puusee wiñet yi ñu sãse palaas .
(src)="11"> Cliquez sur la punaise pour figer le site à son emplacement , ou cliquez sur le bouton ´X ' pour le supprimer .
(trg)="11"> Cuqal ci pinees bi ngir xomb dal bi ci fi mu ne , walla butoŋ ´X ' boo bëggee neenal dal .
(src)="12"> Vous pouvez également cliquer sur l' icône ´grille´ en haut à droite de la page afin de revenir à une page " Nouvel onglet " blanche .
(trg)="12"> Mën nga cuq itam ci njunju " caax " te ne ci kaw ci ndeyjooru xët wi boo bëggee dellusi ci xëtu koñ bu bees bu dara nekkul .
(src)="13"> Téléchargez le dernier Firefox maintenant et commencez à utiliser ces dernières fonctionnalités dès aujourd 'hui !
(trg)="13"> Amal Firefox bi mujj te tambali jëfanikoo tay bees bees yi !